15/12/2018

Dakar ♫






"Dakar", par Sons Libres, duo franco-sénégalais formé en 2005 par Adama Diop, percussionniste et chanteur, et Anne Guinot, accordéoniste chromatique.




So yeewo suba tel
Dug biir Dakar
Nic yi fees fa del
Dundal seen yaakar
Wetu marché Kermel
Foofu war nga fa jaar
Bepp xeetu jaykat ñoo ngi la fay xaar 

Fi de moy Dakar, Dakar Dakar…
Fi de moy Dakar, Dakar
Dakaru Ndiaye… 

Yow su ngoon si jote
Demal Iba mar
Di nga giss ni ñu bëge
Ñun su ñuy mbër
So bëge jëndi jën
Demal Sumbedioune
So bëge xam lu ñeex ñamal ceebu Jën 

Fi de moy Dakar, Dakar Dakar…
Fi de moy Dakar, Dakar
Dakaru Ndiaye… 

Yow su gudi jote
Mën nga deg
Sabar Waye so wëlbëtiko
Baye Fall ya ngui sikar
Yow su lëndëme
Tannal fi ngay jaar
Yow so rombe jumaa
Serigne yaa tari Saar

Fi de moy Dakar, Dakar Dakar…
Fi de moy Dakar, Dakar
Dakaru Ndiaye… 

Ci biir yen Diwaan
Amna ñu mar naan
Talibe ngi yalwaan
Ñoo ngi len di seetaan
Dakar beri na cosaan
Gewel ya ngi wayaan
Maget yi di waxtaan
Xale yi di reetaan 

Fi de moy Dakar, Dakar Dakar…

Bu ñen ñi yekse
Ñu naan bii tangay
Bu waxtu delu jote
Ñu naan bi neexay
Gueule tapée, Médina,
Rebess, Bopp Mermoz,
Fann, Amitié Fass,
Grand Dakar,
Ana waa HLM,
Capsi Liberté 5, Derklé,
Xaar Yallah, Grand Yoff, Artafat,
Ouest foire, Pikine, Diamegëne,
Kër Massar, Ouagou Niayes,
Ginaaw Rails, Gibraltar,
Parcelles Assainies,
guediawaye, Ngor, Ouakam,
 Yoff fatewuma wa île de Gorée.
Dakar, Dakar Dakar… 

Waay li moo neex !